Filtrar por gênero

Xam sa démb, xam sa tey

Xam sa démb, xam sa tey

Goethe-Institut

Ngir xam lu leer ci seen mboorum réew ak bu Afrig, ndaw ñi dañoo war a miin jàmbaar yi tabax Afrig. Ndégat yii di Podcast,« Xam sa démb, xam sa tey », looloo tax ñu tànn yenn ci jaar-jaar ak xew-xew i mboorum Senegaal, ngir may ndaw ñi ñu jàngee ci seen démb, baa man seen tay, te waajal seen ëllëg.

9 - LAMINE GUEYE ET VALDIODIO NDIAYE
0:00 / 0:00
1x
  • 9 - LAMINE GUEYE ET VALDIODIO NDIAYE

    Lamine Gèy ak Waljoojo Njaay ñaari kangam lañ yu xeex ak seen i pexe ba Nooteelu nasaraan bi jeex. Li nu gën a jàpp ci ñoom mooy fula ja ñu def ci aar seen ngor ba tontu njiitul Fraraans la taxoon mu mer.

    Tue, 11 Apr 2023 - 11min
  • 8 - ALMAMIAYAT DU FOUTA TORO

    Ceerno Sulaymaan BAAL moo soppi ni ñiy yore nguuur ca Fuuta jëlee ko ci ndono tegg ko xam-xam ak jikko. Moo Boolewoon Jullit yi ngir ñu jóog xeex ak ñi bañoon diine. Man na noo wax ni moo indi nguurug yemale  di democrasi ci Afrig Sow jant.

    Tue, 04 Apr 2023 - 11min
  • 7 - KOLI TENGUALA

    Koli Teŋella doomi Satigi Teŋella Ba ka Nana Keïta la dib Malinke. Cossanam di Baxunu. Jàmbaar ju mag la woon ju mùanoon na jiite xare ba am ca tur wu rëy.

    Tue, 28 Mar 2023 - 10min
  • 6 - SYDIA DIOP

    Sidiya Ndate Jóob ku raññeeku la ci biir réew mi ndax ab juddoom ak jaar-jaaram. Doomi Lingeer Ndate Yàlla la ak Saakura Barka Jóob. mi ngi juddu ci 18848 dee 1855.

    Tue, 21 Mar 2023 - 10min
  • 5 - EL HADJ OMAR TALL

    Umar Seydu Taal ma nga juddoo Alwaar ci Poddorug tey jii. Ganaaw ba mu tukke lu yàgg ci ajug Màkka la delusi xare ba samp Lislaam ci Afrig Soww jant te xeex na xeex bu rëy ak Tubaab bi.

    Tue, 14 Mar 2023 - 11min
Mostrar mais episódios